L’HERITAGE DE MBEGAAN NDUUR, FONDATEUR DU ROYAUME DU SAALUM

L’HERITAGE DE MBEGAAN NDUUR, FONDATEUR DU ROYAUME DU SAALUM

VERSION DE MAGUETTE NGOM Recueillie à Saara (Kawlak, Saalum) le 11 septembre 1996, elle compte 563 versets transcrits et traduits en français  

PRESENTATION DE L’AUTEUR DE LA VERSION

Siix Nduur est un habitant de Coofak d’où il est originaire. Âgé de soixante six ans, il est vendeur de foin à quelques jets de pierre de l’emplacement du lieu de culte de Mbegaan. Nous l’avons rencontré grâce à Saa Goño Mbóoj, actuel chef de quartier de Coofak. Il s’est montré très surpris de nous voir faire de la recherche sur l’histoire de son ancêtre et, à la suite de nos échanges, il a exprimé toute sa satisfaction d’apprendre l’existence de travaux sur ce sujet. Après nous avoir montré l’emplacement du baobab et des deux ébènes d’Afrique, il nous a appris que les deux terrains sur lesquels se trouvaient ces deux arbres ont été vendus et achetés par des tiers. Lorsqu’il a appris le projet de vente de ces deux terrains, il a voulu les acheter pour sauvegarder toute l’histoire qui leur est attachée, mais ses maigres moyens ne le lui ont pas permis. Aujourd’hui, des maisons ont été bâties sur ces lieux de culte, ce qui le désole tout autant que nous. Quant au baobab, il est tombé et aucun effort de le conserver n’a été fait ; son emplacement est encore inoccupé, mais il est transformé en déversoir d’eau par les ménagères habitant dans les concessions alentours, et rien ne permet de déceler une quelconque importance qu’il aurait pu avoir dans le passé, encore moins une quelconque affection qui lui aurait été attachée. 195 1. Man Siix Nduur, cosaanoo Coofak, di sët ci Mbegaan Maay wax ak yow, di la won sama cosaanu maam. Mbegaan bi mu ñowee Coofak, Ci guy gi la dëkkoon. 5. Fi mu doon sangoo mooy ci ñaari aloom yi. Ci ron ñaari aloom yi la doon sangoo. Su bëggoon a dem fi mu doon dem : Benn, muy dem Bawol, Wala muy dem ci Eli Bana Muusaa mi mu joteeloon ba jélee ko fi, 10. Ci aloom yi la doon sangoo. Aloom yi nak, nekkoon nañu fi. Bi Mbegaan demee ak léegi, Nit ñi doon nanu ci jëfandikoo. Jëfandikoo mooy, 15. Lépp lu leen jàxaloon, Doon nañu ñow ci aloom yi ñaan ci Te Yàlla doon na def loolu Ci wàllu ndox mu ñakk Wala jamano ju métti. 20. Loolu lépp doon nañu ko def, Ñaan,Yàlla def ci lañu buggoon. Bi saxaar si ñowee sax, -Ndax Mbegaan moo jiitu saxaar si- Waaye bi saxaar si ñowee, 25. Ba bëgg a xëtt di ñow Kaxlax, Bu ñowaan, Bu depaaree Gingineew, Xam nga saxaar daawul am fu muy taxaw fudul gaar ba ci gaar, Waaye bu depaaraan Gingineew, 30. Bala muy duggusi Coofak rekk Fokk, bu ñowee ba dend ak aloom yi, Mu teggi tànk wala du jàll Bu ko deful rekk man naa am mu ray wala mu daanu. Loolu teewee naa ko, du benn yoon, du ñaari yoon. 196 1. C’est moi Siix Nduur, originaire de Coofak et descendant de Mbegaan Qui te parle, pour te faire connaître l’histoire de mon ancêtre. Quand Mbegaan est venu à Coofak, Il habitait à l’emplacement du baobab 5. Et prenait ses bains sous les deux ébènes d’Afrique. Il prenait ses bains sous les deux ébènes d’Afrique. Quand il voulait aller quelque part : Soit qu’il se rendît au Bawool, Ou qu’il allât chez Eli Bana Musaa avec qui il était en conflit jusqu’à l’éliminer, 10. Il se baignait sous les ébènes d’Afrique. Les ébènes d’Afrique étaient encore là. Depuis la disparition de Mbegaan, Les gens s’en servaient. S’en servir signifie que, 15. Pour tout souci, Ils venaient sous les ébènes d’Afrique pour y prier Et Dieu agréait cela ; Que ce soit pour le manque d’eau Ou pour les difficultés de la vie. 20. On faisait tout cela ; On priait et Dieu exauçait les vœux. Même quand le train est venu -Car Mbegaan est antérieur au train-, Mais quand le train est venu, 25. Quand il voulait traverser pour venir à Kawlak, Quand il venait, Quand il quittait Gingineew -Tu sais qu’un train ne s’arrête que d’une gare à une autre- Mais, quand il quittait Gingineew, 30. Avant d’entrer à Coofak, Quand il arrivait à hauteur des ébènes d’Afrique, Il devait ralentir au risque de ne pas passer. S’il ne le faisait pas, il pouvait dérailler ou se renverser. J’ai été témoin de cela à plusieurs reprises. 197 35. Man Siix Nduur maa wax loolu, Doomu Teniŋ Seen ak Gorgi Ma Nduur Ñaan yi ñu ci doon ñaan, Danu doon wuut nàkk, Danu doon defaar ay nàkk 40. – Ndax te Mbegaan masul a nangu deret nak. Man masu maa dégg ñu wax loolu, Ne nanu ko rayal nangam wala nangam Deedeet ! Mbegaan li mu doon nangu daal, 45. Bu fekkee ne amoo soow, Da ngay wuut sa nàkk Jaxase ko ba mu mat ay beñwaari beñwaar, Mu taaj ko, nit ñi di ñaan, muy tuuru, Di wax li muy wax, di ñaan ci Yàlla ak xàmb yi. 50. Di ñaan ci Yàlla ak rab yi Lu mu ñaan yàlla def ko. Bi bu deme itam, Nit ñi fi desson loolu lañu doon def. Li tax loolu saxatufi ba léegi, 55. Li ci nekk mooy ne dëkk bi dafa ñow ba duggu foofu, Ñu def ko ay parcelles, Lampes yi ñow, La fa nekkoon gàddaay dem ca àll ba Ndax te rab soxlawul mbooloo 60. Soxlawul ay lampes. Lii moo waral mbiri Mbegaan ba tey nekkufi di dund Sudul li tafu ci géej gi. Li tafu ci géej gi nak, Loolu mooy li mu rëddoon. 65. Waa Kawóon soxlawoon ndawal Mu rëdd tànkam, ndox mi topp ci moom ba Kawóon. Loolu moo fi sax dakk, nekk fi Waaye lele dafa fay, daldi fi jóge.

VERSION D’ALAAJI JUUF Recueillie à Cakalaar (Saalum) le samedi 15 mai 2010, elle compte 720 versets transcrits et traduits en français 202

PRESENTATION DE L’AUTEUR DE LA VERSION

Alaaji Juuf est originaire de Cakalaar, mais il est né à Kawoon, où sa mère avait suivi son père qui y avait été élu Grand Farba. Nous pouvons dire, sans exagérer, qu’il est une référence pour ce qui concerne la tradition orale du Saalum, du Siin et du Bawol. Il nous a appris qu’il suit de près tout ce qui est relatif à Mbegaan, raison pour laquelle il n’hésite pas à sillonner le Saalum pour vérifier lui-même certaines données et vérifier la conservation et la sauvegarde de l’héritage matériel de Mbegaan, comme sa lance nommée Duga Nduur. Très à l’aise dans son récit, il nous a fait deux révélations de taille qui ont réorienté certains aspects de notre analyse que nous avions presque terminée. Tout d’abord, Allaji Juuf est le premier de nos informateurs à situer avec précision le prétendu tombeau de Mbegaan et à nous révéler les circonstances de son supposé décès, même si dans les récits que nous avons collectés au Bawol, l’idée de la mort de Mbegaan Nduur avait été avancée sans que nos informateurs ne soient en mesure de nous fournir le moindre éclairage sur les circonstances de cette supposée mort, ni sur la localisation de son tombeau. Ensuite, il nous a fourni la clé de l’expression à l’origine du nom de Kawoon ; nous avions déjà exprimé notre scepticisme quant à l’origine wolof du nom Kawoon qui proviendrait de l’exclamantion Kawoon a ngi. Dans un contexte où le Mbey était peuplé de Seereer, Pël et Manding, cette origine wolof du nom de la future capitale de Mbegaan était une aberration. En réalité, le terme Kawoon provient de l’exclamation du Pël Illo Sow qui a permis à Mbegaan d’identifier l’arbre totem, lequel s’était démultiplié en dix pour ne pas être pris et immobilisé. Il s’agit donc de Ko óon, pour indiquer et singulariser le véritable mbul dans la multitude. 203 1. Man, Alaaji Juuf laa tudd Maa ngi dëkk Cakalaar, fii. Mooy sama cosaan, Waaye nag, ca Kawóon laa juddoo. 5. Fii mooy sama cosaan Waaye Kawóon laa juddoo. Sama baay nag moo fa faluwoon. Danu koo fal Kawóon, Muy Farba bu mag. 10. Moo tax mu jél sama yaay yóobu ko Kawóon. Man fa la juddoo, Fa laa fere. Man, Alaaji Juuf laa tudd; Njaay Seŋor mooy sama yaay 15. Farba Songde Xoja Juuf mooy sama baay. Buur Saalum Mbegaan nag, li nu ci xam yaatu na. Moom, baayaam a nga dëkkoon Mbudaay seereer Kon nag Mbudaay yàgg na lool. Baayam a nga tuddoon Marga-Caaj 20. Mooy Maari Nduur. Marga-Caaj ci boppam mi jur Mbegaan, Baayam a ngi tuddoon Goko Jeeme. Mbegaan nag, li tax baayam dëkk Saalum, – Ndax Mbudaay ci Saalum la25. Yaayam dëkk Siin, Yaayam ci Gellowaar yi gàddaayoon Gaabu, maamam yi ci lañu bokkoon. Ñu daldi ñow Siin. Ba ñu ñowee Siin, Yaayam jooju, dafa amoon góom 30. Góom bi nag, góomu deeyaale la, manut a wér. Yaay jóoyu nag, ñu ngi koy waax Maan Fay Doomu Teniŋ Joom la. 204 1. Je m’appelle Alaaji Juuf, J’habite à Cakalaar Où se situent mes origines, Mais je suis né à Kawoon. 5. C’est ici que se situent mes origines, Mais je suis né à Kawoon. C’est mon père qui y a été élu. Il a été élu à Kawoon, Il était un grand Farba130 . 10. C’est la raison pour laquelle il a pris ma mère pour l’amener à Kawoon. Moi, j’y suis né, J’y ai été sevré. Je m’appelle Alaaji Juuf ; Njaay Seŋor est ma mère, 15. Farba Songde Xoja Juuf est mon père. Ce que nous savons du roi du Saalum Mbegaan Nduur est vaste ; Son père habitait à Mbudaay seereer. Donc, Mbudaay est très ancien. Son père s’appelait Marga-Caaj, 20. C’était Maari Nduur. Marga-Caaj, le père de Mbegaan, Est le fils de Goko Jéeme. La raison pour laquelle le père de Mbegaan habitait le Saalum, – Car Mbudaay se situe au Saalum25. Et sa mère habitait le Siin, C’est que sa mère est une descendante des Gelwaar qui s’étaient exilés du Gaabu. Ils étaient venus au Siin ; Lorsqu’ils sont venus au Siin, Sa mère avait une plaie. 30. Cette plaie était incurable. Cette mère s’appelait Maan Fay ; Elle est la fille de Teniŋ Joom, 130 Farba : représentant du peuple dans l’administration. 205 Maan Fay Teniŋ Joom, Ak Ñilaan Fay Teniŋ Joom, 35. Ak Tase Fay Teniŋ Joom, Ak Waagaan Fay Teniŋ Joom. Tase Fay góor la, Teniŋ Joom a ko juur. Waagaan Fay Teniŋ Joom góor la 40. Maan Fay jigéen la, moom seen jigéen la Ñilaan Fay Teniŋ Joom di seen jigéen. Kooku nag, moo nekkoon buur Siin Moom Waagaan Teniŋ Joom. Bi mu toogee nag ba am rëbb buy dox ci réew mi, 45. Nit di dox ba dem fa. Jigéen am boobu nag di Maan Fay, Ame góomu deeyaale, Ñu ne ko : « Sa kii de, gis nañu ku ko man a faj » Mu ne : « Fu ngeen ko gis ? » 50. Ñu ne ko : « Ca Saalum, fa nuy wax Mbudaay seereer Waaye rëbb bu rey la» Mu ne ko : « Ndax man ngaa fexe ba ma jot ko ? » Mu ne ko : « Waawaaw, Man naa koo fexe de. » 55. Mu ne : « Mën naa laa boole ak i nit, Nga yóobul ma kii mu fajuji ? Lu mu wax ma fay ko. Mu ne ko : « Waawaaw ! » Booba la doxkat booba dem, 60. Indi ko Mbudaay, wax ko Maari, Ne góom la yor, Gellowaar la nag. Maari ne : «Man naa faj góom bi de Waaye nag loo ci gis danga ma ciy fay fukk 

Table des matières

Introduction
PREMIERE PARTIE : PRESENTATION DU CORPUS DE LA THESE
Version de Mamadu Maar
Version de Manga Nduur
Version de Maget Ngom
Version de Maari Nduur
Version de Siix Nduur
Version d’Alaaji Juuf
DEUXIEME PARTIE : ANALYSE
Chapitre I : Présentation historique du Saalum
I – Mise en place du peuplement
II- Le Saalum : un lamanat sous la tutelle de l’empire du Jolof
III- La naissance du pouvoir politique
Chapitre II : L’organisation sociopolitique du Saalum
I-Les caractéristiques de la société pré-gelwaar
II- L’ordre instauré par Mbegaan Nduur ou la fondation d’une nouvelle organisation sociale
III- Les institutions politiques
Chapitre III : L’organisation du mythe
I – La structure narrative
II – Le mythe et l’histoire
Chapitre IV : Le mythe et la société de l’époque
I – L’ordre lamanal
II – La fondation et l’organisation du royaume
Chapitre V: L’expansion du royaume et la prospérité du règne
I – L’expansion vers d’autres espaces
II – La prospérité du règne
Chapitre VI: L’instauration des cultes
I – Importance et rôle des cultes dans le mythe de Mbegaan
II – Les rites de renouvellement
Chapitre VII : Les valeurs sociales transmises par le mythe
I – Le matriarcat
II – L’honneur
I- La paix
Chapitre VIII- L’éphémère empire de Mbegaan Nduur
I- L’unification du Siin et du Saalum
II – L’exercice du pouvoir au Bawol
Chapitre IX : La grandeur du mythe de Mbegaan
I – L’actualité du mythe de Mbegaan
II – L’oralité et la sacralité face à la civilisation moderne
Chapitre X : La poésie agro-pastorale seereer et les valeurs
transmises par le mythe de Mbegaan Nduur
Corpus
I – Le culte du travail
II- La prééminence de la figure lamanal
Chapitre XI – Mbegaan Nduur en perspective dans la poésie de Léopold
Sédar Senghor
Corpus
I- L’univers culturel et mystique de Senghor
II – L’exil et l’initiation
Conclusion
Annexe : Chronologie des rois du Saalum selon Abdou Boury Bâ

projet fin d'etudeTélécharger le document complet

Télécharger aussi :

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *